9Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.
10Yaa màgg te yéemey jëf, yaw doŋŋ yaa di Yàlla.
11Éy Aji Sax ji, won ma sa nammeel, ma doxe sa worma. Tënkal sama xol ci ragal la.
12Boroom bi sama Yàlla, naa la sante xol bu fees, màggal la ba fàww.
13Ngor lu réy nga ma won, sorele maak tëraayu bàmmeel.
14Éy Yàlla, nit ñu bew a ma jógal, def gàngoor gu néeg, di rëbb sama bakkan, te seetuñu la ci.
15Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.