4Boroom bi, bànneexalal sab jaam, yaw laa dékk sama xol.
5Boroom bi, yaa baax, di bale, di nàddil sa ngor képp ku lay sàkku.
6Éy Aji Sax ji, teewlul, ma ñaan la; déglul, ma tinu la.
7Bu ma la wooyee bésub njàqare, yaa may nangul.
8Boroom bi, doo moroomu tuur yi, te jëf melul ni sa jos.
9Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.