9Woykat ba nee: «Naa déglu lu Aji Sax ji Yàlla di wax.» Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam, ba duñu dellu ci jëfi dof.
10Wallam aka jege ñi ko ragal, te leeram dëgmal sunu réew mii!
11Ngor ak kóllëree daje, njekk ak jàmm saafoonte,
12kóllëre jebbee fa suuf, njekk séentoo asamaan,