5«Ndawi péncum Yàlla yii xamuñu, dégguñu; xanaa di doxe lëndëmu ñaawtéef, ba kenuy suuf yépp di jaayu.
6«Dama ne ay yàlla ngeen, yeen ñépp di njabootu Aji Kawe ji.
7Waaye du leen tee dee ni doom aadama, du leen tee daanu ni képp kuy njiit.»
8Ngalla Yàlla, taxawal, àtte àddina, yaw yaa séddoo xeetoo xeet.