5Loolu wartéefu Israyil la, di ndigalu Yàllay Yanqóoba,
6di ndénkaane lu mu dénk waa kër Yuusufa, ba Yàllay dali ca kaw réewum Misra. Baat bu ma xamul laa dégg, mu naan:
7«Sippi naa leen, woyofal seeni yoxo.
8Ngeen jàq, woo ma, ma xettli leen, wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya, te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba. Selaw.
9Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma dénk leen. Éy Israyil, su ngeen ma déglu woon!
10Buleen fat tuuru jaambur, buleen sujjóotal tuuru doxandéem.