50Mu afal meram, ba musalul seen bakkan, xanaa jébbal leen mbas ma.
51Daa fàdd képp kuy taaw ca Misra te juddoo seen digg doole, fa xaymay sëti Xam.
52Mu génne ñoñam niy gàtt, wommat leen ni gétt ca màndiŋ ma,
53ba yóbbu leen fu wóor te tiituñu; seeni noon, géej ga mëdd leen.
54Mu yóbbu leen fa suufam su sell sa, fa tund woowu mu jënde dooleem.
55Da leena dàqal ay xeet, dogal leen céru suuf, sancal giiri Israyil ca seeni xayma.
56Teewul ñuy diiŋat ak a gàntal Yàlla Aji Kawe ji, sàmmuñu ay dénkaaneem,
57xanaa dëddu, di ko wor ni seeni maam, toogadi ni xala gu yolom.
58Ñu di ko merlook seen bérabi jaamookaay, di ko fiirlook seen jëmmi tuur.
59Ba ko Yàlla yégee, mer na, ba jéppi Israyil lool.