4Dunu ko nëbb sunuy doom, xanaa di ko jottli maas giy ñëw, xamal leen jaloorey Aji Sax ji ak kàttanam aki kéemaanam.
5Bindal na sëti Yanqóoba téereb seede, muy yoon wi mu tegal Israyil. Mu sant maam yi, ñu xamal ko seeni doom,
6ngir ñiy juddu ëllëg xam ko, am ay doom, ñu màgg, ba xamal ko seeni doom,
7ngir ñu wóolu Yàlla, baña fàtte jëfi Yàlla, di jëfey santaaneem,
8te baña roy seeni maam; maas gu të woon te déggadi, ñu ñàkk pastéef te sàmmuñu kóllërey Yàlla.
9Waa giirug Efrayim ñoo soxi fitt, te keroog xare ba ñoo daw.
10Ñoo sàmmul kóllërey Yàlla, gàntal yoonam,
11ba fàtte ay jalooreem, di kéemaan yi mu leen won.
12Fa seen kanami maam la def kéemaan, fa diiwaanu Cowan, réewum Misra.
13Moo xar géej ga, jal ndox ma nim tata, jàlle leen.
14Bëccëg mu jiitee leen aw niir, ak leeru sawara guddi gépp.
15Moo xar ay doj ca màndiŋ ma, mbàmbulaan wal, mu nàndal leen;
16mu sotti ndox mu balle ciw xeer, walal, mu safi dex.
17Teewul ñu wéy di moy Aji Kawe ji, di ko gàntal ca màndiŋ ma.
18Ñoo diiŋate Yàlla xol, di xemmem ñam wu bakkane.
19Ñuy waxal Yàlla naan: «Xam ngeen ne Yàlla manu noo taajal ndab ci màndiŋ mi!
20Dóor naw doj, moos, ndox ma fettax, wal ma baawaan, waaye aw ñam nag? Daa mana leel mbooloo mii aw yàpp?»
21Aji Sax ji dégg ci, mer lool; xolam tàng ci sëti Yanqóoba, am sànj tàkkal Israyil.
22Dañoo gëmul Yàlla, doyloowuñu wallam.
23Mu digal niir ya fa kaw, ubbi bunti asamaan,
24tawal leen mànn, ñu lekk: peppum asamaan la leen leel;
25mburum jàmbaar la nit lekk, mu wàcceel leen ca lu ne gàññ.
26Yàlla wale ngelawal penku fa asamaan, bëmëx ak dooleem ngelawal bëj-saalum.
27Mu tawal leenu yàpp, mu saawe ni pënd, di njanaaw yu ne gàññ ni feppi suufas géej,
28wàcce ko fa seen digg dal ba, mu dajal seeni dëkkuwaay.
29Mu faj seen aajo, ñu lekk ba suur këll.
30Teewul bala seen xel a dal, seen lanc jàllagul sax,
31Yàlla mer na, dal ci seen kaw, bóom ña ëpp doole ca ñoom, fàdd waxambaaney Israyil.
32Loolu lépp teewul ñuy bàkkaar ba tey te gëmuñu ay kéemaanam.
33Mu dagg seeni fan, mu wéy ni cóolóol, faat seen bakkan ci safaan bu gaaw.
34Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko, tuub, waññiku ci moom.
35Ñu fàttliku ne Yàllaay seen cëslaay, xam ne Yàlla Aji Kawe jeey seen njotlaay.
36Teewul ñu di ko jéema naxey wax, di ko fen.
37Joxuñu ko woon xol, sàmmuñu kóllëreem.
38Teewul mu yërëm, baal leen seen ñaawtéef, ba sànku leen. Muñ na meram, muñati, te toppul xolam,
39ndax xalaataat ne suuxu neen lañu, di noo guy dem te du délsi.
40Gàntal nañu ko ba tàyyi ca màndiŋ ma, teg ko naqar ca ndànd-foyfoy ga.