3Xaymaam a nga Salem, di xunteem ma fa Siyoŋ.
4Fa la rajaxee fitt yuy boy ak pakk ak saamar ak ngànnaayal xare. Selaw.
5Yàlla yaa ne ràññ te darajawu, ba raw tundi rëbbkat yi.
6Futtees nay boroom fit, ñu ne nërëm, nelaw; kuy ñeyi xare, say yoxo nasax.