15Yaa fettaxal fii bëti ndox akum wal, ŋiisal dex yu masa wal.
16Yaa moom bëccëg, moom guddi, teg fi weer week jant bi.
17Yaa rëdd mboolem digi suuf, sàkk noor ak nawet.
18Kon xoolal, Aji Sax ji, noon a ngi ree, xeet wu amul bopp a lay sewal.
19Bul wacce rabu àll sam xati, bul sàggane sa néew-doole yi mukk.
20Ngalla xoolal ci kóllëre gi, fu làqu ci réew mi, fitna dale fa ba dajal.
21Yàlla bu néew-doole ñibbaale gàcce, yal na ku ñàkk ak ku néewle di la santandoo.