Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 73

Sabóor 73:8-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Dañuy ñaawle, di wax lu bon, di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole.
9Seen ŋal-ŋal àkki asamaan, làmmiñ dajal suuf.
10Moo tax ñoñi Yàlla walbatiku ci ñoom, di jolu seen wax nim ndox
11te naan: «Lu ci Yàlla xam? Ana xam-xam fa Aji Kawe ji?»
12Ñu bon ñaa ngoog! Ne finaax, di gëna woomle.
13Man kay maa sellal ci neen, di sàmm sama der.
14Bés bu ne yar dal ma, saa yu ma xëyee, jot mbugal.
15Su ma noon: «Naa waxe ni ñoom,» kon de, ma wor sa askanu mbooloo.
16Naka laay jéema ràññee lii, mbir mi ëlëm ma.
17Ba ma àggee sa kër gu sell ga, laa doora gis muju ku bon.
18Yoonu tarxiis kay, nga leen teg, daane leen, ñu sànku,
19Yàquleeka leena bett! Musibaa leen ne fuuf, ñu ne mes!
20Day mel ni gént goo yewwoo. Céy Boroom bi, boo xippee, jëmmu gént ga soof la.
21Naqar laa amoon, sama xol di dagg.
22Booba ngaaka laa, xawma dara; rab laa woon fi sa kanam.
23Teewul ma des ak yaw, nga jàpp sama loxol ndijoor.
24Danga maa gindee sam xel, teg ca dalale ma sa teddnga.
25Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy?
26Kàttan ak pexe jeex, Yàlla di ma dooleel, ma séddoo ko fàww.

Read Sabóor 73Sabóor 73
Compare Sabóor 73:8-26Sabóor 73:8-26