3ngir maa ñee ku bew, ndax gis mu baaxle te di ku bon.
4Amuñu metit, xanaa ne faaj.
5Doñ-doñu nit dabu leen, coonoy doom aadama dalu leen.
6Moo leen taxa ràngoo reewande, làmboo coxor.
7Dañoo suur ba gët suulu, seen xalaati xel xëtt yoon.
8Dañuy ñaawle, di wax lu bon, di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole.
9Seen ŋal-ŋal àkki asamaan, làmmiñ dajal suuf.
10Moo tax ñoñi Yàlla walbatiku ci ñoom, di jolu seen wax nim ndox
11te naan: «Lu ci Yàlla xam? Ana xam-xam fa Aji Kawe ji?»
12Ñu bon ñaa ngoog! Ne finaax, di gëna woomle.
13Man kay maa sellal ci neen, di sàmm sama der.
14Bés bu ne yar dal ma, saa yu ma xëyee, jot mbugal.
15Su ma noon: «Naa waxe ni ñoom,» kon de, ma wor sa askanu mbooloo.