Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 72

Sabóor 72:5-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Yal nañu la wormaal feek jant biy am, feek weer wiy feq, sët ba sëtaat.
6Yal na Buur di xéewalu réewam nib taw cig ruujeef, mbaa waame wuy suuxat suuf.
7Janti Buur aji jub day woomle, te ba keroog weer wiy fey, jàmm di law,
8mu yilif géej ba géej ak dex ba ca cati àddina.
9Waa màndiŋ mi di ko sukkal, ay noonam mëq suuf,

Read Sabóor 72Sabóor 72
Compare Sabóor 72:5-9Sabóor 72:5-9