3tooli tund yu mag yi indil mbooloo mi jàmm, tooli tund yu ndaw yi xéewale leen njekk,
4Buur di àtte néew-ji-dooley xeet wi, di wallu doomi néew-ji-doole tey dëggaate kiy nennoo.
5Yal nañu la wormaal feek jant biy am, feek weer wiy feq, sët ba sëtaat.
6Yal na Buur di xéewalu réewam nib taw cig ruujeef, mbaa waame wuy suuxat suuf.
7Janti Buur aji jub day woomle, te ba keroog weer wiy fey, jàmm di law,
8mu yilif géej ba géej ak dex ba ca cati àddina.
9Waa màndiŋ mi di ko sukkal, ay noonam mëq suuf,
10buuri Tarsis ak dun ya di ko indil ay galag; buuri Saba ak Seba di ko yótsi yóbbal,
11buuroo buur di ko sujjóotal, xeetoo xeet di ko surgawu.