17yal na turam sax, ba law fu jant tiim, yal na xeet yépp barkeele ci moom, te di ko ndokkle.
18Cant ñeel na Yàlla Aji Sax ji, Yàllay Israyil, mi wéetooy jalooreem.
19Cant ñeel na teddngaam, ba fàww, yal na teddngaam dajal suuf sépp! Amiin, Amiin!
20Ñaani Daawuda doomu Yese jeexe fii.