2Éy Aji Sax ji, bul mer, ba di ma rëbb, bul xadaru, ba di ma mbugal.
3Aji Sax ji, damaa néew doole, yërëm ma! Éy Aji Sax ji, sama yaram a tas, dàmp ma!
4Sama xol a jeex tàkk. Aji Sax ji, loo deeti xaar nag?
5Éy Aji Sax ji, délsil, xettli ma! Walloo ma sa ngor.
6Deesul dee ba fàttliku la; ku dugg njaniiw, nu mu lay sante?
7Onk naa ba loof, di fanaanee jooy, sama lal di féey, ba far seeye rongooñ.
8Saay gët a ngi xóot ndaxu naqar, boole ci giim ndax tooñi noonoo noon.