5Sama kawari bopp sax, ñi ma bañ ci daraa ko ëpp. Ñu bare doole, bëgg maa sànk, noonoo ma ci dara. Sàccuma, nara fey!
6Yaw Yàlla, xam nga sama jëfi dof, te samay tooñ umpu la.
7Yàlla buma rusloo ñi la yaakaar, yaw Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yàlla buma gàcceel ñi la topp, yaw Yàllay Israyil.
8Yaa tax ma dékku, ñu di ma sewal, ma rus ba sëlmoo gàcce.
9Jaambur laa léegi ci saay bokk, mel ni doxandéem sama biir doomi ndey.
10Damaa xér ci sa kër gi, ba jeex tàkk, te jëf ji ñu la sewale man la dal.
11May jooy, di woor, ñu di ma sewal.
12Ma sol ay saaku, di ko ñaawloo, ñu di ma léebu.
13Waa pénc ma di ma tooge, màndikat yi di ma woyal.
14Waaye man, Aji Sax ji, yaw laay dagaan. Éy Yàlla, na tey di bésub yiw. Ngalla nangul ma ci sa ngor lu yaa ak sa wall gu wóor.