21Dees maa sewal, sama xol jeex, ma wopp; may sàkku yërmande, awma ko; ku ma dëfal it, gisuma ko.
22Tooke lañu ma leel, ma mar, ñu nàndal ma lu forox.
23Yal na seen ndab di seenum yeer, seeni am-di-jàmm di seenug fiir.
24Yal na seeni gët giim, ba dootu gis; yal na seen ndigg rëcc fàww.
25Yal nanga leen yuri mbugal, sa mer tàkk, dab leen.
26Yal na seeni dal gent, seeni xayma wéet.
27Yaw, nga duma ba noppi, ñu toppaat ca, nga gaañ, ñu siiwal mitit wa.
28Dencal leen tooñ ci kaw tooñ, te yàlla buñu tàbbi ci sag njekk.
29Yal nañu leen far ca téereb dund ba, bañ leena limaale ca aji jub ña.
30Man de, damaa jàq, tiis. Éy Yàlla, yal naa làqoo sag wall.
31Damay woy Yàlla, teral ko, màggal ko, sant ko.
32Mu gënal Aji Sax ji saraxu yëkk, aki béjjénam aki wewam.
33Néew-ji-doole di gis, bége, kuy sàkku Yàlla yokku fit.
34Aji Sax ji day dégg néew-ji-doole moos, te du sàggane ñoñam ñi ñu njoñ.
35Na asamaan ak suuf màggal Yàlla, mook géej ak lu cay yëngoo.