12Ma sol ay saaku, di ko ñaawloo, ñu di ma léebu.
13Waa pénc ma di ma tooge, màndikat yi di ma woyal.
14Waaye man, Aji Sax ji, yaw laay dagaan. Éy Yàlla, na tey di bésub yiw. Ngalla nangul ma ci sa ngor lu yaa ak sa wall gu wóor.
15Xettli ma ci ban bi, ma baña suux, xettliku ci samay noon. Rikk génne ma yii xóotey ndox,
16ba gannax du ma mëdd, xóotey géej du ma warax, pax du ma kepp.
17Éy Aji Sax ji, yaa rafet ngor, nangul ma! Geesoo ma sa yërmande ju yaa!
18Bu ma làqu, Sang bi. Jàq naa, gaawe ma.
19Jege ma, jot ma, musal ma ci noon yi!
20Yaa gis ñu di ma sewal, di ma ruslook a torxal, yaa ngi ne jàkk ci noonoo noon.
21Dees maa sewal, sama xol jeex, ma wopp; may sàkku yërmande, awma ko; ku ma dëfal it, gisuma ko.
22Tooke lañu ma leel, ma mar, ñu nàndal ma lu forox.
23Yal na seen ndab di seenum yeer, seeni am-di-jàmm di seenug fiir.
24Yal na seeni gët giim, ba dootu gis; yal na seen ndigg rëcc fàww.