Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 68

Sabóor 68:9-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Suuf yëngu, asamaan sóob fi kanam Yàlla, boroom tundu Sinayi, Yàllay Israyil ja!
10Yàlla, waame nga tawal, leqlee ko réew mi nga séddoo, fa mu sonne,
11sa mbooloo dëkke fa. Yàlla yaa leel néew-ji-doole ci sag mbaax.
12Boroom beey joxe ndigal, gàngooru jigéen indi xibaar:

Read Sabóor 68Sabóor 68
Compare Sabóor 68:9-12Sabóor 68:9-12