16Yaw tundu yàlla yi, yaw tundu Basan, tundu Basan, tund wi ci coll yi,
17looy xeelook say coll, di fiire tund wi Yàlla namma dëkke? Aji Sax ji kat, fa lay dëkk ba fàww!
18Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.
19Yaa yéeg fa kawa kaw, jàpp ay jaam, yóbbaale. Yaa nangooy galag ci nit ñi, ba ci ñiy fippu ndax li Yàlla Ki Sax dëkke Siyoŋ.
20Cant ñeel na Yàlla bésoo bés. Moo nuy jaboote. Yàllaa nuy musal. Selaw.
21Sunu Yàllaa di Yàlla jiy walloo, Aji Sax ji Boroom beey musal bakkan.
22Yàlla daal ay rajaxe boppi noonam ak kaaŋ mu sëq mu boroom wéye tooñ.
23Boroom bi nee: «Basan laay waññee noon yi, waññee leen xóotey géej,
24ngeen mana xuus ci seen deret, seeni xaj séddu ci seeni néew.»
25Céy Yàlla, gis nañu sa gàngoor di daagu, sama Yàlla, sama buur, sa gàngoor ba ca biir kër gu sell ga.
26Woykat ya jiitu, xalamkat ya mujje, janq ji yéewe leen tëgg um njiin.
27Dajeleen, di sant Yàlla, yeen askanu Israyil, santleen Aji Sax ji.
28Giirug Beñamin a ngi jiitu, gën cee néew, njiiti Yuda topp caak seeni kurél, njiiti Sabulon topp caak njiiti Neftali.
29Yeen, seen Yàlla dogalal na leen kàttan; éy Yàlla, jëfeel doole ja nga nu jëfeeloon.
30Sa kër gi tiim Yerusalem, fa la la buur yiy indiley galag.
31Nanga fa gëdde rabu àll wi ci barax yi, ñooy gétti yëkk yi, xeet yi ci des diy sëllu. Gëdd leen, ba ñu sujjóotalsi laak dogi xaalis. Tasaareel xeet yooyu sopp xare,