Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 68

Sabóor 68:13-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13«Buur yaak seeni gàngoor a ngay dawa daw, jongomay kër gi di séddale lël ja.
14Yeen ñiy waaf ci gétt gi, bésub xare, gànjar a ngi, di laafi pitax yu ñu xoob xaalis, dunq ya teg wurus wuy ray-rayi.»
15Ba fa Aji Man ji tasaaree buur ya, tawub yuur a ngay sóobe tundu Calmon.
16Yaw tundu yàlla yi, yaw tundu Basan, tundu Basan, tund wi ci coll yi,
17looy xeelook say coll, di fiire tund wi Yàlla namma dëkke? Aji Sax ji kat, fa lay dëkk ba fàww!
18Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.
19Yaa yéeg fa kawa kaw, jàpp ay jaam, yóbbaale. Yaa nangooy galag ci nit ñi, ba ci ñiy fippu ndax li Yàlla Ki Sax dëkke Siyoŋ.
20Cant ñeel na Yàlla bésoo bés. Moo nuy jaboote. Yàllaa nuy musal. Selaw.
21Sunu Yàllaa di Yàlla jiy walloo, Aji Sax ji Boroom beey musal bakkan.
22Yàlla daal ay rajaxe boppi noonam ak kaaŋ mu sëq mu boroom wéye tooñ.
23Boroom bi nee: «Basan laay waññee noon yi, waññee leen xóotey géej,
24ngeen mana xuus ci seen deret, seeni xaj séddu ci seeni néew.»

Read Sabóor 68Sabóor 68
Compare Sabóor 68:13-24Sabóor 68:13-24