13«Buur yaak seeni gàngoor a ngay dawa daw, jongomay kër gi di séddale lël ja.
14Yeen ñiy waaf ci gétt gi, bésub xare, gànjar a ngi, di laafi pitax yu ñu xoob xaalis, dunq ya teg wurus wuy ray-rayi.»
15Ba fa Aji Man ji tasaaree buur ya, tawub yuur a ngay sóobe tundu Calmon.
16Yaw tundu yàlla yi, yaw tundu Basan, tundu Basan, tund wi ci coll yi,
17looy xeelook say coll, di fiire tund wi Yàlla namma dëkke? Aji Sax ji kat, fa lay dëkk ba fàww!