Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 68

Sabóor 68:12-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Boroom beey joxe ndigal, gàngooru jigéen indi xibaar:
13«Buur yaak seeni gàngoor a ngay dawa daw, jongomay kër gi di séddale lël ja.
14Yeen ñiy waaf ci gétt gi, bésub xare, gànjar a ngi, di laafi pitax yu ñu xoob xaalis, dunq ya teg wurus wuy ray-rayi.»
15Ba fa Aji Man ji tasaaree buur ya, tawub yuur a ngay sóobe tundu Calmon.

Read Sabóor 68Sabóor 68
Compare Sabóor 68:12-15Sabóor 68:12-15