11sa mbooloo dëkke fa. Yàlla yaa leel néew-ji-doole ci sag mbaax.
12Boroom beey joxe ndigal, gàngooru jigéen indi xibaar:
13«Buur yaak seeni gàngoor a ngay dawa daw, jongomay kër gi di séddale lël ja.
14Yeen ñiy waaf ci gétt gi, bésub xare, gànjar a ngi, di laafi pitax yu ñu xoob xaalis, dunq ya teg wurus wuy ray-rayi.»