7Mooy nguuroo njàmbaaram ba fàww, di topp xeet yeek bët. Ku koy diiŋat, yàlla boo damu! Selaw.
8Yeen xeet yi, santleen sunu Yàlla, te biral cantam!
9Moo sàmm sunu bakkan, te waccu nu, nu tërëf.
10Éy Yàlla, nattu nga nu, xelli nu, ni ñuy xellee xaalis;
11laaw nga nu, teg nu njàqare.
12May nga noon not nu, nu jaare sawara, jaarem ndox; nga génne nu, yaatal nu.
13Maay duggaale sa kër ay saraxi rendi-dóomal, defal la samay dige,