14yi ma waxoon ci sama gémmiñ, sama làmmiñ tudd ko, ba ma jàqee.
15Jurug yafal, ma defal la saraxu rendi-dóomal, saxar sa jollee ca kuuyu sarax ya, ma boole ca saraxu nag ak sikket. Selaw.
16Képp ku ragal Yàlla dikkal, déglu, ma limal la li mu ma defal.
17Moom laa woo wall, àddu, màggal ko.
18Su ma naroon ñaawtéef, Boroom bi du ma déglu.
19Waaye Yàlla dégg na ma, teewlu na samag ñaan.
20Cant ñeel na Yàlla, gàntuwul samay ñaan, xañu ma ngoram.