5Ndokklee koo tànn, woo ko, mu dale say ëtt, di xéewloo sa ngëneeli kër, ak sa sellngay dëkkuwaay.
6Defal nga nuy kéemaan, nangug ñaan ci njekk, yaw Yàlla, mi nuy wallu, di yaakaaru àddina wërngal këpp, ba ca géej gu sore ga.
7Yaa dëje tund yu mag yi doole, gañoo sa kàttan,
8di dalal riirum géej aki gannaxam, ak coowal xeet yi,
9ba waa cati àddina yéemoo say firnde, waa penkook sowu di sarxolle.
10Yaa dikke suuf am wal, nangul koo nangul. Dexu Yàllaa fees ndox, ngay may nit peppam, ni nga ko waajale suuf si,
11di suuxat ngàbb mi, maasalee ko jal yi, sottiy waame, mu mokk, cax ma, nga barkeel.
12Yaay tëje mbeyum at mi say ngëneel, foo jaare, xéewal walangaan.
13Parluy màndiŋ yaa ngi walangaan, li wër tund yu ndaw yi di xumbéen.