8Yàllaa may musal, di ma sagal, ma di ko doolewoo. Sama kiiraay, Yàllaa!
9Bokk yi, wóoluleen ko fu ngeen tollu, diisleen ko seen xol, Yàllaay sunu kiiraay. Selaw.
10Doom aadama, ngelawal neen; nit, naxi neen. Booleel teg ci lu ñuy natte diisaay, kaw la jëm. Ñooy gëna woyof ngelaw!