3Moom doŋŋ mooy sama wéeru-mucc, di ma rawale, ba duma sànku!
4Xanaa dungeen bàyyee songandoo nit, nar koo sànk, ni kuy màbb tabax bu joy, mbaa ngay bàddi per mu ràpp?
5Seeni mébét, wàcce boroom daraja doŋŋ; yeena ngi bége ay fen, seeni kàddu diw yiw, seen xalaat diy saaga. Selaw.
6Yal na Yàlla doŋŋ di dalal sama xel, moom mi ma yaakaar.