3Éy Yàlla, wacc nga nu, bëtt sunu kiiraay. Mer nga, waaye ngalla xettli nu.
4Yëngal nga suuf, xar ko; ngalla jagalal, mu tëju, mu ngi jaayu!
5Won nga sa mbooloo lu metti, nàndal nu biiñu mbugal, ba nu miir.
6Artu nga ñi lay jaamu, ngir mucc fitt. Selaw.
7Walloo nu sa ndijoor, nangul nu, ba say soppe xettliku.
8Yàllaa àddoo fa këram gu sell, ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, séddale xuru Sukkóot.
9Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase, Efrayim di sama mbaxanam xare, Yuda di sama yetu nguur,
10réewum Mowab di sama ndabal raxasukaay, Edom, ma teg tànk; Filisti, ma xaacoo fa.»
11Éy Yàlla, ana ku may yóbbu dëkk ba tata wër? Ku may jiite ba Edom?