2Mooy ba Daawuda di xareek waa Siri ña ca Mesopotami ak waa Siri ña ca Soba te ba ñu ca bàyyikoo, Yowab duma fukki junniy Edomeen ak ñaar (12 000) ca xuru Xorom wa.
3Éy Yàlla, wacc nga nu, bëtt sunu kiiraay. Mer nga, waaye ngalla xettli nu.
4Yëngal nga suuf, xar ko; ngalla jagalal, mu tëju, mu ngi jaayu!