6Aji Sax ji, Yàllay Israyil, Yàlla Boroom gàngoor yi, yewwul, dikkeel xeeti yéefar yépp, mbugal! Workat yu bon yi, bu leen yërëm! Selaw.
7Bu ngoonee ñu wàccsi, di xiiru niy xaj, di wër dëkk bi.
8Déglul li ñuy yebbee ci seen gémmiñ, seen làmmiñ niy saamar, ñu defe ne kenn déggu leen.
9Te yaw Aji Sax ji, yaa ngi leen di ree, yaa ngi kekku yéefar yii yépp.