Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 58

Sabóor 58:6-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6du dégg baatu jatkat, mbaa jati ñeengokat bu ñàng.
7Yàlla, ngalla tojal seeni gëñ; Aji Sax ji, foqal seen selli gaynde yii.
8Yal nañu ne mes ni ndox muy wal, yal nañu diir seen fitt, mu damm,
9yal nañu mel ni ngumbaan-tooye buy dox, di seey, mbaa lumb wu jigéen tuur, gisul jant.
10Balaa seen cin a yég tàngooru gajj, muy gu tooy, muy guy boy, yal na leen fekk sànku.

Read Sabóor 58Sabóor 58
Compare Sabóor 58:6-10Sabóor 58:6-10