1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, gannaaw ba mu dawee Buur Sóol, ba dugg ca xunti ma.
2Éy Yàlla, baaxe ma, ngalla baaxe ma, fi yaw laay làqu, yiiroo sa kiiraay, ba musiba yi jàll.
3Ma woo Yàlla, Aji Kawe ji, Yàlla, mi may matalal.