Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 55

Sabóor 55:1-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, dib taalif, ñeel Daawuda.
2Éy Yàlla, déglul, ma ñaan la, bul làqu, dama lay dagaan.
3Teewlu ma, nangul ma. Li may tawat a ma xañ jàmm, ub sama bopp;
4coowal noon yee ak coonob ñu bon ñi. Dañu maa teg fitna, di ma songe xadar.
5Sama fit a ngi rëcc, di tëf-tëfi; tiitaangey ndee ne ma taral.
6Njàqaree ma dugg, may kat-kati, musiba mëdd ma.
7Dama ne: «Éy ku may may laafi xati, ma ne fërr, noppluji.
8Xanaa ma naaw, ba sore, fanaani màndiŋ ma. Selaw.
9Naa gaawtu, seeluji ngelaw lu riddi ak ngëlén.»

Read Sabóor 55Sabóor 55
Compare Sabóor 55:1-9Sabóor 55:1-9