3Moo jàmbaar ji, looy damoo jëfi coxor? Yàlla, ngoram, bés bu nekk la.
4Ak sa làmmiñ wi ngay sose loraange, mel ni saatu su ñu xacc, rambaaj bi!
5Lu bon a la gënal lu baax, fen a la gënal wax dëgg. Selaw.
6Yaa bëgg jépp wax juy yàq, waabajiiba bi!
7Yàlla da lay sànk ba fàww, fëkke la sab xayma, yóbbu, déjjatee la réewum aji dund. Selaw.