4Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, raxasal ma sama moy.
5Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne.
6Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, yaa yey; te soo àttee, wàcc nga.
7Ñaawtéef daal laa judduwaale, te sama ndey ëmbaale ma bàkkaar.
8Dëgg daal nga namm, dëggu reenu xol, kon déey ma xel mu rafet.
9Wis ma ndox, ma sell; sang ma, ma set wecc.
10Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex, ma bégati, gannaaw ba nga ma dammatee.