Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 51

Sabóor 51:3-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni, faral samag tooñ ngir sa yërmande ju yaa.
4Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, raxasal ma sama moy.
5Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne.
6Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, yaa yey; te soo àttee, wàcc nga.

Read Sabóor 51Sabóor 51
Compare Sabóor 51:3-6Sabóor 51:3-6