15ma xamal tooñkat sa war, ba moykat dellu ci yaw.
16Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal, baal ma deret ji ma tuur, ma siiwal sa njekk.
17Boroom bi, may ma, ma wax, ma delloo la njukkal.
18Sàkkuwloo sarax, nde kon ma indi; te soppuloo saraxu rendi-dóomal.