13Bu ma xalab, bu ma xañ sa noo gu sell.
14May ma, ma bégeeti sag wall, te dundale ma xol bu tàlli,
15ma xamal tooñkat sa war, ba moykat dellu ci yaw.
16Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal, baal ma deret ji ma tuur, ma siiwal sa njekk.
17Boroom bi, may ma, ma wax, ma delloo la njukkal.