2Ca Siyoŋ, dëkk ba ca taar ba la Yàlla feeñe ni leer gu jolli.
3Sunu Yàllaa ngi ñëw te du ne cell, sawaraa ko jiitu, di xoyome, ngëlén lu mag wër ko.
4Ma ngay woo seede asamaan ak suuf, ngir àtte ñoñam.
5Mu ne: «Dajaleel ma sama wóllëre ñiy sarxal, di ko fase sama kóllëreek ñoom.»
6Asamaan a ngi biral njekkam, ngir Yàllaay àtte. Selaw.
7«Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma wax leen; yeen waa Israyil, ma sikk leen. Maa di Yàlla, seen Yàlla.
8Du seeni sarax laa leen di sikke, mbaa seen saraxi rendi-dóomal yi sax fi sama kanam.
9Soxlawuma yëkku yar ak sikketu gétt.
10Maay boroom raboo rabu àll, ak junniy nag yuy fore tund ya.
11Xam naa njanaawi tund yi, luy ndundatub tool maa ko moom.
12Su ma xiifoon, duma leen ko wax, maa moom àddinaak li ci biiram.
13Damay lekk yàppu nag ak a naan deretu sikket a?