2Yeen, xeetoo xeet, dégluleen; yeen, waa àddina yépp, teewluleen,
3ngay ku tuut di ku mag, nga bareleek nga néewle.
4Li may wax xel la, di xalaat yu déggu.
5Damay teewlu kàddu yu xelu, xalamal la sama tekkiteb cax.
6Ana lu may tiit bés yu metti, yu ma njublaŋ yéewe seeni ñaawtéef,
7di ñu wóolu seen am-am, di kañoo alal ju bare?