10Ana kuy dund ba fàww, ba doo gis bàmmeel?
11Xanaa gis ngeen ne xelu, dee; dof, dee; naataxuuna it faatu rekk, wacce keneen alalam.
12Sa bàmmeel di sa kër, ba fàww, di sa dëkkuwaay bu sax dàkk, boo tudde woon sa bopp ay suuf sax.
13Nit ak darajaam fanaanul, mook aw rab a yem, sànku rekk.
14Nii la ku wóolu boppam di mujje, mook ku ko topp, di safooy waxam. Selaw.