Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 44

Sabóor 44:13-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Jaay nga sa mbooloo ci dara, te jariñu la tus.
14Tax nga sunuy dëkk di nu ree, ñi nu séq di nu kókkaleek a ñaawal.
15Tax nga xeet yi di nu léeboo, jaambur yaa ngi nuy wëcc bopp!
16Damaa dëkke gàcce, sëlmoo kersa
17ndax kókkali yeek xastey nit ñi ma bañ, di feyoonteek man.
18Lii lépp dal na nu, te fàttewunu la, fecciwunu la kóllëre.
19Dëdduwunu la, wàccunu saw yoon,
20teewul nga not nu, wacce nu xaj ya, këpp nu lëndëmu ndee.
21Su nu la fàtte woon yaw, sunu Yàlla, ba tàllal tuuri doxandéem yi loxo,
22du la ump, yaw Yàlla, mi xam kumpay xol.
23Yaa tax ñu yendu noo bóom, dees noo jàppe ni xar yu ñuy tër.
24Éy Aji Sax ji, jógal! Looy nelaw? Yewwul, bu nu wacc ba fàww.

Read Sabóor 44Sabóor 44
Compare Sabóor 44:13-24Sabóor 44:13-24