8Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma; say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
9Bëccëg Aji Sax ji baaxe ma ngoram, guddi ma fanaane koo woy, di ñaan Yàlla mi may dundal.
10Naa wax Yàlla ji ma sës, ne ko: «Lu tax nga fàtte ma, noon di ma fitnaal, may wéye tiis?»