Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 41

Sabóor 41:5-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Dama ne: «Aji Sax ji, tooñ naa la; baaxe ma, faj ma.»
6Noon yaa ngi may yéene lu bon, naan: «Xanaa kii du dee, ba ñu fàtte ko?»
7Ku dikk, di ma seet, di jinigal tey fenti sos ci xolam, bu génnee, tasaare ko.
8Bañ yépp a ngi may déeyoo, di ma fexeel lu bon,
9naan: «Musiba dal na ko, du jógati!»
10Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma, te daan lekk samaw ñam.

Read Sabóor 41Sabóor 41
Compare Sabóor 41:5-10Sabóor 41:5-10