4Moo ma may, ma fent, woy wu ma woye sunu Yàlla. Ñu baree seede, di wormaal ak a dénku ci Aji Sax ji.
5Ndokklee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, te sàkkuwoo ku bew ak kuy topp ay fen.
6Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def, amuloo moroom! Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal, ma bëgga xamle lépp, te mu bare ba wees ab lim.
7Saraxi gàtt mbaa pepp, taamuwuloo ko, ay nopp nga ma bënnal, saraxu rendi-dóomal, ak saraxu póotum bàkkaar, sàkkuwuloo ko.
8Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.
9Sama Yàlla, maa soppa def sa coobare, ci sama biir xol la sa ndigali yoon nekk.»
10Siiwal naa sag njekk ca ndaje mu mag ma. Dama ne, Aji Sax ji duma noppi, xam nga ko.
11Làquma sag njekk, ne cell ak moom. Yaa wóor, di walloo, siiwal naa ko. Làquma ndaje mu mag ma sa ngor ak sa worma.