Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 40

Sabóor 40:2-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2May xaara xaar Aji Sax ji, mu dégg may woote, geesu ma,
3génnee ma ca kàmbug sànkute, sippee ma ca xóotey ban ba, cëppe ma ciw doj, samp ma, ma dëgër.
4Moo ma may, ma fent, woy wu ma woye sunu Yàlla. Ñu baree seede, di wormaal ak a dénku ci Aji Sax ji.
5Ndokklee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, te sàkkuwoo ku bew ak kuy topp ay fen.
6Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def, amuloo moroom! Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal, ma bëgga xamle lépp, te mu bare ba wees ab lim.

Read Sabóor 40Sabóor 40
Compare Sabóor 40:2-6Sabóor 40:2-6