1Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2Dama noon: «Damay moyu ba duma moye làmmiñ.» Li feek ku bon di teew, may ŋalaab sama gémmiñ.
3Dama noon cell, ne patt, noppi, ba mu ëpp; sama njàqare yokku,
4sama xol diis, xel di xelaat, xol diis gann; ma mujj àddu,
5ne: «Éy Aji Sax ji, xamal ma sama muj ak sama àppi fan, ma xam ni sama dund gàtte.