Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 37

Sabóor 37:23-33

Help us?
Click on verse(s) to share them!
23Aji Sax jeey sopp saw yoon, jiite say jéego.
24Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
25Ba may ndaw, ba tey may mag, gisuma ku jub ñàkk ndimbal, mbaa askanam di dunde yalwaan.
26Day saxoo tabe, di leble, askanam barkeel.
27Dëddul mbon, di jëfe mbaax, ba dëkke réew mi fàww.
28Aji Sax ji kat daa sopp yoon, te du wacc jaamam bu gore. Day fegu ba fàww, askanu ku bon dog.
29Aji jub ay jagoo réew mi, dëkke ko ba fàww.
30Kàddug aji jub day xelu, wax ja jub;
31yoonu Yàllaam a nga ca xol ba, du dox ba tërëf.
32Ku bon a ngi yeeru ku jub, di ko wuta bóom.
33Waaye Aji Sax ji du ko bàyyeek moom, te deesu ko daan cib layoo.

Read Sabóor 37Sabóor 37
Compare Sabóor 37:23-33Sabóor 37:23-33